Lu jëm ci Nun
Téereb Kercen bu sell bi wax na ak nun ci tàriq ak ci kéemtaanu ëllëg. Waxoon nanu li weesuwoon ak li nar a am ci lu yàggatul. Ci ab tàmbaleb wax lu ñëwagul, danu war a jàng bataaxalu àrtu bu mujj bala tekkiteb àddina.
Bataaxalu àrtu bi, te ñetti Malaaka yi leeral ko ci Peeñu 14, nekk na ñetti wàll. Bu ci ne ci àrtu yii am na solo lool ngir àdduna sépp dégg ko.
Malaaka bu njëkk bi ne na nu jaamu Yàlla Adj Sàkk ji, Ki defar asamaan si, suuf si ak géej gi. Danu war a jaamu Aji Sàkk ji ndax waxtu àtteem bi ñëw na. Malaaka bu njëkk bi wax nanu nan lanu mën a xamee Yàlla ji te fagaru ngir jàll bésub àtte bi.
Ñaareelu Malaaka bi àrtu nanu ci soppi sa diine ci waxtu njéexital. Nu ngi nuy wax nu 'génn' ci tëralini diine yu dul màggal Yàlla Aji Sàkk ji, ak Kàddoom gi mu siiwal.
Ñetteelu Malaaka bi àrtu nanu ne ku bon ki dina jaar ci tëralinu diine bunu soppi ngir sos benn song bu mujj ci Yàlla Aji Sàkk ji ak Askanam wi. Dina am ab \"màndarga\" buy tëggu ca nit ñay jaamu ku bon ki, te ñiy jaamu Yàlla te déglu kàddoom di nañu leen sonnal. Waaye Yàlla dina wàcce ndogalam ci ñooñu am màndarga bu raglu booba. Askanam, ñi gëm te topp ndigalam, dina ñu mucc ci jafe-jafey palanet bi nekk ci yoonu dee. Dina ñu ànd ak Yàlla dugg àjjana te seetaan Ko ci ni Muy defaraatee àddina si ci melokaan ba mu nekkoon ca njàlbéen.
Bindul ci sunu yéenekaay
Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!
Siiwal yu fës
© 2023 Sharing Hope Publications