Nan Ngay Xalaatale ci sa Bopp

Nan Ngay Xalaatale ci sa Bopp

Tënk

Yónent Yàlla yi dànkaafu nañu ci ab nguuru diine gu bon te nu tegtaloon ko mu am màndargay caabi bu ñu tudde “Babylon.” Ci kéemtaan bi, nguur googu dina jéem a jaay doole ba duggal nu ci jaamu Yàlla bu baaxul. Benn yoon rekk moo mën a tax nu am kaarànge mooy di xalaat ngir sunu bopp te jébbalu ci Ndigalu Yàlla. Téere bu ndaw bii dafa nuy wax nan lanuy tàggatee sunuy xel ba mën a màndu, nekk ay way-gëm yuy xalaat ci jamonoy jafe-jafey àdduna.

Xeet

Kayitu siiwal

Siiwalkat

Sharing Hope Publications

Jàppandi ci

21 Kàllaama yi

Xët

6

Yebbi

Yeggoon nanu ba ci collu Gunung Datuk binu noppee yéeg lu kawe. Ma toog ci sama wetu xarit bu bés bi, Adzak, ngir settan àll bi ak banneex. Yàggul rekk, sunu waxtaan bi walbatiku ci mbiri diine.

Adzak wax ne “Man dara tënkuma ci samay xalaat. Am naa samay gis-gisu bopp ci mbiri àdduna si.”

“Ah waaw” laa ko tontu. “Dégg naa ne ndaw wi Malaisi yu bare dañuy gis seen bopp niki xalaatkat yu lenn tënkul.”

Adzak daldi reetaan. “War nanu xalaatal suñu bopp. Am na lu bare luy jaxasoo sunu deful noonu. Loolu dina la dofloo.”

Ma daldi ko laaj “Waw léegi nooy def soo nekke seen biir kër? Fii ci Malaisi, ay ndaw yu bare
dañuy teg seen bopp ay nit ñuy xalaatal seen bopp, waaye sa biir kër, war nga bokk ca ngiiru Jullit ya mbaa Buddhist ya. Lan ngay wax say waajur?”

Adzak tontu ma “Du ma leen wax dara” “Damay topp rekk luñu bëgg. Mën na xalaatal sama bopp, wànte duma ko wone.”

Ndax Xalaatal Sunu Bopp am na Solo?

Ci yenn beréb yi ci àddunasi, gëm lu baaxul mën na tax ñu génnee la ca askan wa, dàqq la sa liggéey, wala sax ñu ray la. Mo tax xalaatal sa bopp mën na ànd ak ay gàllangkoor. Waaye ndax loolu am na solo? 

Sunu àdduna si dafa fees ak ay xalaat yu baax ak yu bon. Waaye nag soo bëggee xam mbébét yu baax yeek yu bon yi, danga wara xalaat te di ci waxtaan. Soo jëndee ab lëf lu seer—ni wurus, saffron, mbaa ab iPhone—xam nga ne do ko jënd rekk yobbu ko kër ga. Di nga ko xool bu baax méngale kook yeneeni jumtukaay yi ba nga xam ne boobu mooy bi gën a baax. Naka noonu la nu war a jëflante ak xalaat yi. 

Àdduna si dafa bari lu jaxasoo, te lu ko gën a jaxase mooy nit ñi dañuy jéem a foorse di gëmloo askan wi seeni xalaat yu jaxasoo yi. Déglul ma wax la ab Kàddug Yàlla bu am solo. Ci abtéere bu yàgg bu tudd “Féeñalu Yéesu Krista bi,” daf nu doon won ne am na ay nit ñuy jéem a foorse seeni xalaati diine yu jaxasoo ci ñeneeni nit. Téere booba ne na, “Babilon a daanoo, dëkk bu mag ba daanu na! Moom ma daan màndal askanoo askan biiñu moyam miy indi am sànj” (Peeñu 14:8).

Kàddu junj gi nag jafewul nànd. Babilon ab dëkk bu mag la woon, wànte turam lu muy tekki mooy “jaxaasso.” Dëkk bi dafa “daanu” du lu mu jaxasoo moo tax wànte dafa di lu mu nanguwul bàyyi gannaaw jaxasoo ba. Dafa xëcc réew yi ñu topp ko ci njaaloom bi—maanaam, wor Yàlla di jaxase jaamu bu baax ak bu bon. Xalaat yu bon yooya danu leen yoonal te nangu leen. Li mbind mi wax ci “Babilon” dafay joxoñ ab diine bu am kàttan fi ci kaw suuf, diine buy yoonal njuumte yi te dina jéem a foorse boppam sax ci nit ñi ñu gëm ne mooy dëgg gi.

Feeñu Yéesu Krista, wone woon na ne loolu dina xew ci sunu jamono jii. Mën na am gis nga mu xew ba noppi. Ndax tay am na ay nitu diine yuy jaxase Kàddug Yàlla gi? Loolu ndax jaxasewul sa xel?

Waw, li mo tax xalaatal sa bopp am solo.

Nan Ngay Xalaatale ci sa Bopp

Nit ñu bare defu ñu leen lu dul topp diiney seeni askan. Duñu xalaat ndax seeni ngëm-ngëm. Dañuy topp seeni aaday diine yu amul bopp amul geen te loolu li muy yàqq ëpp li muy defar. Yenn saa yi, njiitu diine yi sax, yi nu war a won yoonu Yàlla, ñooy nekk ñu fees dell ak ger.

Nan lanuy xame luy dëgg? Foog naa ne danu war a wóolu yonent Yàlla yi. Lu tax? Am na ñetti sabab yu tax:

  1. Yonent Yàlla yi wone nañu xam-xam bu leer ci luy xew ëllëg. Yonent Yàlla Dañel waxoon na dooley réewi Óróop yi ci yilif ak noot àddina si. Yéesu Krista (nu xam ko itam ci Isa al-Masih) waxoon na daanug Jerusalem ca atum 70 ci sunu jamono. Yonent Yàlla Moussa (Musa) waxoon na li jëm ci taariqu Ismaïla ca jamono ju mujj ji.

  2. Yonent yi wone nañu xam-xam bu leer ci wàllu wérgu-yaram. Yonent Yàlla Moussa, mi dundoon ay 3 500 at ca gannaaw, leeraloon na ber nit, cet gi ci wàllu ndox yu tilim, ak mbiri ray doomi jàngoro yi. Séddale woon na rabu àll ya, ci yu set ak yu ñàkka set. Te waxoon nanu nu moytu lekk dereet ak yàpp bu duuf bunuy lekk lu dagan. Tay sax, nit ñiy topp digleem ci lekk ak ci wàllum wérgu-yaram mën nañ yokk seen dund lu toll ci 15 at ëppale ko ñeneen ñi.

  3. Yàlla nangu na ñaani way-gëm yi ko woolu te yaakaar yonenteem yi. 

Mbindi Yonent Yàlla yi dañu fees dell ak yoonu njub—wànte ngir nga xéewalu ci, danu war a jàng naka lanuy xalaatee te settantal ko, ngir natt sunu ngëm-ngëm, ak xoolaat ndax sunu ngëm-ngëm leer na. Xalaat dafa doon lu am solo ci diine ju jub.

Léegi, lan mooy xew sunuy gëstu ab njuumte? Mën na nirook dëgg ca njalbéen ga. Wànte binuy jéem a xam firnde yi, ci la nuy tàmbale gis jafe-jafe yi ci xalaat bi. 

Dëgg mu ngi ci geneen wàll gi. Dëgg musul moy dara so ko jànge bu baax a baax. Ni nga koy gën di jàng, dëgg gi di la gën a feeñu. 

Way-gëm war nañu nekk nit ñu ëpp xam-xam ci àdduna si, ndaxte Yàlla de leen di won yoonu xam-xam. Soo nekkee ci anam bu la nit teree nga xalaat sa xalaatu bopp ni nga ko bëggee mbaa laajte, xamal ne loolu nekkul mbiru Yàlla. Yàlla bëgg na nu gëstu bu baax, ndaxte dëgg dafa diis ba gëstu mënu ko dëkkoo. Wànte Babilon dafa leen xëcc ci ludul dëgg ba noppi tënk leen fa tëj yoonu jafe-jafey xalaat.

Sudee sa xel dafa jaxasoo lool te nga defe ne yangi ci Babilon, génnal foofa! Nëwal ci yoonu xam-xam bu joge ca Yàlla. Xalaatalal sa bopp te nga laaj ay laaj yu wóor. Doo am mbeteel. 

Ndax bëgg nga yokk sa xam-xam ca téere bu yore lu Yéesu Krista feñal? Bind nu ci dëkkuwaay bi nekk ci gannaaw kayit bii.

Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.
Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.

Bindul ci sunu yéenekaay

Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

newsletter-cover