
Ndax Soxla Nga ab Kéemtaan?
Tënk
Yàlla yàgg naa wone ay misaali kéemtaan ngir rekk su ko askanam soxlaa dëgg. Téereb Yàlla bi nettali nanu lu bari ci ay kéemtaan yu amoon, ay nit ñi nu wéral seeni feebar, ak ay xew-xew yu xel mënuta daj yu tontu bi nekk ci julli kese. Téere bu ndaw bii joxe na firnde yu bare yuy wone lu tax nu war a gëm Téereb Yàlla bi niki kàddug Yàlla gu dul soppeeku ak nan nga mën a jegee Yàlla ngir am sa kéemtaanu bopp.
Xeet
Kayitu siiwal
Siiwalkat
Sharing Hope Publications
Jàppandi ci
22 Kàllaama yi
Xët
6
Ab njaboot gu bari te yaatu lool bu doon yaakaar dund gu gën te dogguwoon ci tukki ca meneen réew. Seen tukki booba yombul woon; dañu waroon a jéggi ab àll bu yaatu bu amul dara ak seeni tànk. Amoon na ay jaan, ay jiit, ak tàngaay bu metti. Saa-su ñenn ñi ci ñom desee ca gannaaw mbooloo mi, ndax feebar wala coono gi, ay saay-saay daldi leen song.
Yàggul nag seen lekk ba jeex. Borom kër gi daldi ñaan Yàlla ab kéemtaan. Bés ba ca topp, ba ñu yewwu, ñi gis ab lekk bu tasaaroo fépp ci suuf te niro ak mburu. Ba ñu ko ñamee, mu neex te mel ni mburu bu ànd ak lem. Lekk bu bare la woon, ndaxte ñépp jotoon nañu ci lekk ba suur! Jëlal na leen ay fan yu bare bala ñuy jéggi dàllanger gi, wànte bes bu nekk mburu bi faral di jóge ci kaw asamaan di dal ci suuf. Sant Yàlla, ndax ñoom ñépp mucc nañ!
Taariq bi mel na ni luy jaaxal nit, wànte ci dëggantaan lu amoon la. Li bokk na ci xarbaax yu bare yu Kàddug Yàlla gi nettali, Kàddug Yàlla gi nu tudde itam Tawréet, Zabuur, ak Injil. Kàddug Yàlla gi am na ay téeméeri-téeméeri taariq yu dëggu, yu bari ci ñoom di nettali ay xarbaax yi Yàlla def ci dund ay nit ñu bare. Nekk na ab téere bu am solo ci sunu jamono jii, nga xam ne ku nekk mu ngi wut ab kéemtaanu boppam.
Ay Kéemtaam yu Jamono Jii
Ci at yii wessu, gis nanu ay xeex, ay coppite, koomkoom bu daanu, ñàkkum liggéey, jàngoro yuy wàlle, ak dee gu bare lool. Xamuma ci anam ban ngay dund ci jamono jii. Mën na am ne amatuloo foo dëkk. Mën nga am ab nit koo bëgg ku nekk ci diggante dund ak dee. Mën na am ngay xaree ngir am ab liggéey.
Wànte ci anam boo mën a nekk, xamal ni Yàlla fonk na la lool te bëgg na def ab kéemtaam ci sa dund tay ni mu ko defewoon ci at yee wessu. Saaso ame naqqar, jàngal kàddug Yàlla gi ndax nga am doole, ndaxte téereb kéemtaan la.
Kàddug Yàlla gi ci Sunu Jamono
Am na ay nit ñuy am sikki-sakka ci jàng Kàddug Yàlla gi ndax dégg nañu ne dañu ko soppi. Xéyna ñàkka ànd ci gis-gis boobu mu ngi joge ci dundug nit ñu bare ñuy wax ne ñu ngi topp Kàddug Yàlla gi. Yenn saa yi nu gis ay kercen di naan sàngara, di kàrt, di sol ay yéré yu yiwul, di lekk yàppu mbaam-xuux, ak di ñakk teggin nit ñi.
Waaye ca dëgg-dëgg, njumte yooyu yépp Kàddug Yàlla gi daf leen aaye. Ñàkk a topp lu Yàlla digal ci Kercen yi taxul kàddug Yàlla gu am solo gi sax ba fàww soppeeku. Yonent Yàlla Esayi bind na lii, “Am ñax day wow; tóor-tóor day lax. Waaye sunu kàddug Yàlla mooy sax ba fàww.” (Esayi 40:8). Ndax foog nga ne nit ñi am nañu doole bu mat ngir soppi Kàddug Yàlla gi, wala lu ñiy def du lenn lu dul weddi Kàddug Yàlla rekk?
Kaddùg Yàlla wax nanu nan la yonent Yàlla Dawud (nu xam ko itam ci Dawud) ak ay nitam doon yenu gaalu kóllëre ga, ab waxande gu rey wa ñu deñcoon Fukki Digle Yàlla ya. Fukki Digle Yàlla yooya ñooy yoonu Yàlla bi ngir dund gu jub te sell te Yàlla bindoon leen ci ñaari àlluwa yu mag yu jóge ci ab xeer te ñu deñcoon leen ci biir gaalu kóllëre ga. Ba ñu doon dem, benn waay daldi sañ teg loxom ci gaalu kóllëre gi—ci la danu dee ci saasi!
Su fekkee ne Yàlla bàyyiwul ay loxo yu réy-réylu di laal gaalu Yàlla bu sell bi Yàlla bind kàdduam, ndax du bàyyi nit ñu bon di laal Kàddug Yàlla gi ñu bind, di ko defare ak xànjar ak di ko jubbanti? Yàlla am na doole bu mat ngir aar kàddoom.
Ca dëgg-dëgg, kàddug Yàlla mooy téere bunu gën a firndeel ba nit sosoo ba léegi. Taxu ko yàgg lool, amoon na ñetti sàmmkat ca réewum Palestine—Muhammad edh-Dhib, Jum’a Muhammad, ak Khalil Musa—feeñal nañu ab Téere bu nekkoon ca géej binuy woowe géej gu dee gi. Loolu nekkoon ab feeñal gu rey biy maye sañ-sañ ngir ñu mëna méngale Téere suñu jamano ji ak Téere jamano jooja mu war a toll ci 2,000 at. Niroo bi doy na waar, loolu wone wat ne lu Yàlla fëssël kenn mënu ko soppi. Sudee danga bëgg ab kéemtaan, xamal ne Kàddug Yàlla gi ab paalas bu wóor la foo mën a dawal say gët! Ca biir Téere bi dinga ci fekk ay taariq yu am solo yuy wax ci yonent Yàlla yu mel ni Nouha (Nuh), Ibrahima (Ibrahim), Youssoupha (Yusef), Younouss (Yunus), Dañeel, Daouda (Dawud), ak Souleymane (Suleiman). Xéyna mus nga dégg lu ndaw lu jëm ci ñoom feneen, wànte Téere bi wax na lépp lu jëm ci ñom!
Ñëwal Gis Sa Kéemtaan
Bépp naqqar boo mënoon a dund, Téere bi am na ab taariqu kéemtaan ngir yaw:
Ndax yaw danga feebar wala kenn ci say ñoñ? Jàngal lu jëm ci kéemtaan bi wéral Naaman, Seneraalu soldaar bu Siri bi amoon ngaana.
Ndax yaa ngi xare ngir dundal sa njaboot? Jàngal lu jëm ci jigéen booba dëkkoon ak doomom foofa ca réewum Libaan, ca jamono jooja xiif amoon ca dëkk ba, nan la dunde ak benn potu diwlin ak sunguf gu ndaw gu leen desewoon wànte musul woon a jeex.
Ndax sa dund dafa ñàkk kaarànge? Jàngal lu jëm ci Ebed-Melech, benn waay ju jógewoon ca réewum Eccopi te nekkoon ab jaam ca ëttu buur ba, te nu muslal ko ci jamono xare ngir yaakaar ba mu amoon ci Yàlla.
Ndax yëgoo ne danu la teg ku génn xeet? Jàngal lu jëm ci Hagar jigeen ii jogewoon ca réewum Egypt te mu gisoon ay kéemtaani Yàlla ca waxtu ba ko nit ñi weddee.
Ndax yaa ngi sonn ci jafe-jafey dund gi? Jàngal lu jëm ci bés bi Yéesu Krista yëkatee loxoom te dalaloon ab ngelaw bu am doole ngir musal ay taalibeem ca gaal ga doon suux.
Ay Tontu yu Kéemtaane
Bunuy jàng Téere bi, dina nu am ab kóolute gu tax ñaan ak yaakaar bu teey am. Yéesu Krista nena, “Te lépp lu ngeen sàkkoo ñaan gu ànd ak ngëm, dingeen ko am” (Maccë 21:22). Sunuy jàng taariqu ñeneen nit ñi jotoon a am ay kéemtaan yu jóge ci Borom bi, sunuy xol yi dina ñu fees ak yakaar ngir yobbu suñuy ñaan ca kaw.
Ndax soxla nga ab kéemtaan? Na nga xelal sa bopp ak kéemtaan yi nekk ci biir Téere bi te nga ñaan Yàlla mu may la sa kéemtaanu bopp. Ca dëgg-dëgg, moom Yàlla dina dégg sa ñaan tay jii!
Sudee bëgg nga yokk sa xam-xam ci kéemtaan yi nekk ca biir Téere bi, bind nu ci dëkkywaay bi nekk ci gannaaw kayit bii.
Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.
Bindul ci sunu yéenekaay
Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

Siiwal yu fës
© 2023 Sharing Hope Publications