Noflaay ci Biir Àdduna bu Bare Tës-tës bii

Noflaay ci Biir Àdduna bu Bare Tës-tës bii

Tënk

Jaaxle ak coonob liggéey yobbu na nit ñu bare barsàqq bala seen waxtu dee jot. Waaye bamu sàkkee àdduna si, Yàlla joxewoon na ab saafaray jaaxle: ab bésub noflaay. Bés bu sell boobu sàkkoon na ko niki yërmaande ngir doom-àadama mënoon a noppalu ci liggéeyam ak am jot jublu ci Yàlla. Safaan ba moo am, donte Yàlla sant na nit ñi ñu fattaliku bésub noflaay booba, ñu bare fatte nañu bés bu sell booba, te it ñu bare fatte nañu sax Aji Sàkk Ji leen ko mayoon.

Xeet

Kayitu siiwal

Siiwalkat

Sharing Hope Publications

Jàppandi ci

21 Kàllaama yi

Xët

6

Yebbi

Mita Duran dee na. Ku sawaroon, amoon 24 at di bindkat bu dëkkoon Endoneesi dafa jékki-jékki daanu ci taabal bi mu doon liggéeye. Lu xewoon? 

Mita dafa doon liggéey ci ab këru yëgle, fu liggéey bi bariwoon yaakaar te diisoon. Ab waxtu bala muy dee, ruumandaat na woon nàqqaram ci internet bi: “Tay ci guddi maa ngi gàddu caabi yi di dem bérébu liggéeykaay bi juróom-ñetteelu fan yi toppante te amul noppalu... Dundd a tuma.”

Moom dafa doon naan saa su ne naanu kafeyiin bi di Krating Daeng, melokaanu Red Bull bu joge Asi. Waxam bu mujj ci internet bi mooy, “30 waxtuy liggéey te ba léegi maa ngi dëgër.” Ci la jékki-jékki daanu ci taabalu liggéeyukaayam te mukk jogaatul. 

Lu xewoon? Mita dee na ndax liggéey bu ëpp.

Tay, ñu bare ci ñun dañuy liggéey ba tass. Askan wi moo nuy sonj ci liggéey bu bare, am lu bare, di jënd lu bare. Danu sonn ak coono, ñàkk a nelaw, ak yenu lu diis ci xel. 

Waru noo ray sunu bopp ni Mita Duran, donte àdduna mën na nekk ab yen bu diis. Ndax li la Yàlla bëggoon ci ñun? Moom mooy Mayekatu Jàmm. Sunu liggéeyee ba tass sunu yaram, ndax di nanu am jàmm? Déedéet ci lu leer!

Sudee danu kër-këri ba tass, dafa di am na lu nu fatte te Yàlla bëgg nuy fàttaliku. Nanu seet lu Mu wax ci lu jëm ci noflaay. 

Bës ci Butoᶇu “Ajandi” bi

Yàlla mooy ku baax te am yërmànde. Xam na ni nit ñi dañu soxla noppalu ngir yeesalaat seen kàttanu yaram, xel, ak xaalaatu diine, ni ab telefon poortaabal wala ab ordinaatëer. Loolu mo taxoon, Yónent Moussa (nu xam ko itam ci Musa) bind lu Yàlla santaane:

Deeleen baaxantal bésub Noflaay, ngir sellal ko. Juróom benni fan ngeen wara liggéey, def ci seen soxla yépp. Waaye bésub juróom ñaareel ba, Noflaay lay doon, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ci liggéey lenn (kàddu gi ci wàll bu njëk ci Téere bu sell bi la jóge, nu xam ko itam ci Tawrat: Mucc ga 20:8-10).

Yoonu Yàlla bu kenn mënula soppi wax nanu nu fàttaliku juróom-ñaareelu fan ba. Ci kàllaama yu bare ci àdduna si, juróom ñaareelu fan booba te nu jagleel ko noflaay mu ngi tudd “Saabba.” Lan mo tax Yàlla santaane ñu di ko fattaliku? Ndaxte Yàlla xam na ne fàtte bi ab jafe-jafe dëggantaan la ci nit ñi, dale ko ca Adama. Warunu di fàtte ay ndigalu Yàlla, ndaxte sunu koy fàttaliku moom ak ay ndigalaam mo nuy mën a teg ci yoon bu jub bi.

Waaye lu tax Sabbaa bi nekk bés bu fës? Yàlla mu ngi nuy wax ne,

Ndax man Aji Sax ji, juróom benni fan laa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir, bésub juróom ñaareel ba, ma dallu. Moo tax man Aji Sax ji ma barkeel bésub Noflaay, sellal ko (Mucc ga 20:11).

Sabbaa bi bésub fàttaliku bu am solo la ci ne Yàlla mooy Aji Sàkk ji. Am na ay nit ñu lànk ne gannaaw ba Yàlla du sonn, moom soxlawul noppalu ci bésub juroom-ñaareelu fan bi. Wànte Yàlla noppalikuwul ndax coono; Dafa noppaliku ci liggééyam ba ngir nu mën a am ab waxtu bu sell ngir noppalu.

Yàlla da gis ni ab bésub noflaay baax na ci nit ñi. Def na bésub juroom-ñaareel ba muy ab Sabbaa, maanaam ab dog-dog wala ab ajandi. Motax, juroom-ñaareelu bés bu ayubés bu ne nekk ab bés bu fës ngir nu bës ci butongu “ajandi” bi. Danu war a noppalu ci bépp liggéey ak bépp yëngu-yëngu bu sellul ci bésu lëmm ngir baaxantal ko te jaamu Yàlla. 

Dina doon nekk lu neex su sa njaatigé wala sa jàngalekat digal la nga gën a noppalu? Li nag mooy dëgg-dëgg lu Yàlla santaane! Sant ñeel na Yàlla! Moom mooy ca dëgg-dëgg ku am yërmànde! 

Di Sellal Bésub Yàlla bi

Sabbaa bi nekk na ab bés bu sell fépp ci àdduna si ci nit ñépp. Jammu Yàlla yi fi nekkoon balla jamano Yahut yi, Kercen yi, Jullit yi, Buudist yi, wala Indu yi dañu mës a gëm ni benn Yàlla di Aji Sàkk ji mo amoon. Ca dëgg-dëgg, joxoon nanu ko nit ñépp bi àdduna bi di sosu. Adama ak Awa (nu xam ko itam ci Hawwa) dañu daan baaxantal Saabba bi te Yàlla mësuleen a jox ndigal ngir nu fàtte li mu nu wax nu baaxantal ko. 

Ci anam bu naqqari, danuy fàtte baaxantal Sabbaa bi. Yonent Yàlla yi dànkaafuwoon nañu yahut yi ne Yàlla dina leen doon alag sunu fàttee baaxantal Saabba bi. Fàttalikuwuñu woon dànkaafu yooya, looloo taxoon Yerusalem yàqqu, teg ci seeni waa-kër nu yobbuleen jàpp leen. Kërcen yi itam fàttewoon nañu bésub Saabba ba soppi seen bés bu sell def ko Dibéer mu woroo ak ndigalu Yàlla yi. Jullit yi ñu ngi julli Àjjuma waaye fàtte nañu ne dañu war a noppalu bésub juroom ñaareel ba ngir ñu mën a topp dëgg Aji Sàkk ji. 

Lutaax mu mel ni àdduna sépp dañuy fàtte bés bu am solo boobu? Ndax am na ab musiba bu gën a rëy fàtte bu siiw boobu?

Yéesu Almasi bi (ku ñu tudd itam Almasi Isa) dànkaafu na ñu ne bés dina ñëw Seytaane dana liggéey ak bépp kàttanam ngir sorel xelum nit ñi ca Aji Sàkk ji. Ay miliyong ci ay nit di nañu juum di sellal beneen bés bu dul bésub Sabbaa bi. Sunu Seytaane mën a fàtteloo bésub Aji Sàkk ji, ci la yakaar ndax nu fàtte Aji Sàkk ji ci boppam. Wànte, sunuy baaxantal bésub Sabbaa bi, nu ngi wone sunu kollëre ak sunu Borom te banneexu ci li mu nu may di nooflay, dallu, ak jamm.

Dugg ca Nooflayu Yàlla

Yonent Yàlla Moussa bind na ne “Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba” (Njàlbéen ga 2:3). Ndax sonn nga te jeexal sa doole? Am na ay barkeel ca bésub Sabbaa ba! 

Mita Duran, bindkat booba joge ca réewum Endoneesi, dee na ci liggéey bu ëpp—wànte bu la loolu dal yaw. Yàlla digal na la nga noppaliku ci sa liggéey ayubés bu nekk te nga barkeelu ca Sabbaa ba. 

Soo bëggee yokk sa xam-xam ci naka la nu Yàlla maye nooflay, Jàmm, ak wér, mën nga jokkoo ak ñun soo bëggee ci yëgley leeral yi nekk ci gannaaw kayit bii.

Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.
Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.

Bindul ci sunu yéenekaay

Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

newsletter-cover