
Bëggoon Yërmande
Tënk
Nan la yërmaande Yàlla mel? Ndax Yàlla dafa wax rekk, ''Baal naa leen'', wala dafa yonni nit ku wuutu ngir dindi sunuy bàkkaar yu ñaaw yi? Téere bu ndaw bi dafay nettali ngir leeral njariñu ak tekkib saraxu wuutu bi. Jàngkat yi dina ñu am yakkaar ci xam ne mën nañu leen baal seen bàkkaar te far seen gàcce.
Xeet
Kayitu siiwal
Siiwalkat
Sharing Hope Publications
Jàppandi ci
21 Kàllaama yi
Xët
6
Fatima wéetoon moom kesse ci Eid al-Adha, wéetaayam boobu raw lu mu mëne a dékku. Wéetaayam boobu, njuumteem a ko waral, ndax du noonu wala?
Fatima fàttaliku bu baax nan la doon werantee ak baayam ci mbirum séy ak Ahmed. Ndaw la woon te amoon na ku mu bëggoon. Naka la bayaam manoon a ne déet? Bi mu jóge ci kër gi dem séy ak Ahmed, baayam newoon na bu mu déllu ci mukk.
Yakaaroon a ne dina mëne a dékku rus gi ndax mbëggeelam ci Ahmed. Ba mu duggee ci séy boobu, ci la gis ne lu ko baayam waxoon dëgg la. Ahmed nekkulwoon góor googu mu bëggoon dëggantaan. Mu bàyyi ko ngir beneen jigéen.
Fatima daldi am gàcce ci boppam. Mu gëm ne attée dëgg mo dal ci kawam te dey fey booram. Mu nànd lan la yoon tekki dëgg. Wànte céy, ci biir xolam bi bëgguloon leenen lu dul yërmànde!
Borom Baax ak Yërmànde bu Yaatu
Sunu amee ngor, sañunu ne musunu fakkastalu wala musunu fàtte yoonu njub. Tooñ nanu ñeneen nit. Nit ñeneen tooñ nanu. Ci biir sunuy askan, nit ñi dañuy juum. Te nekk na lu jafe nu baalante àqq ku ci nekk ak baalante àqq sunu biir!
Ndax am na ab yërmànde ngir sunu njuumte yi?
Xalaatal ñaata yoon nga baamtu kadu gu yomb gi “bismillah Al-Rahman Al-Raheem” — “ci turu Yàlla Borom Yërmande ak Xéewal.” Lu taax yërmànde gi am solo?
Mën na am ndaxte sunuy askan yi—ak sunuy xol yi—danu soxla lool yërmànde.
Yërmànde: Yoon bi Gën
Ay at ci gannaaw, ab waay ju tudd Abdul-Rahman xeexoon na ak dëkkandoowam Kareem ba ray ko. Dund gi tàmbalee am ay gàantal ci diggante ñaari kër yooya ci ab dëkku àll bu ndaw ca Egypt. Waa-kër Kareem tàmbalee bëgg fayyu, loolu taaxoon waa-kër Abdul-Rahman yi doon ko jéem a aar. Abdul-Rahman bëggul woon fayyunte bi wéy. Mu dem gis njiitu dëkk bi ndax ñi dolli ko xalaat, ñoñu digal ko déébaadéébu peerkaalu néew bi.
Abdul-Rahman daldi indi peerkaalam teg ab paaka ci kawam. Mu daldi dem dajeek waa-kër Kareem ci palaasu màrse ba, waa dëkk bépp di seetaan. Abdul-Rahman sukk ci kanamu Habib, càmmiñu ki nu tooñ, te jox ko peerkaal bi ak paaka bi. Mu daldi ñaan yërmànde ak juboo.
Habib teg paaka bi ci baatu Abdul-Rahman. Njiitu dëkk bi indi ab xar, Habib nag waroon a jël ab ndogal: baal, walla fayyu? Ni mu téyée paaka bi ci baatu Abdul-Rahman mu ngi koy won ne, “léegi jekku naa la. Ñépp a ci tegg sen bët; ñépp xam nañu ne am naa sañ-sañu ray la te mën naa ko def. Wànte tàamu na yërmande ak juboo. Xeexub deret bi fii la koy yamale.”
Mu won Abdul-Rahman gannaaw, te rendi xar mi. Xar mi yenu mettit bi, mer mi ak àtte bi ko waroon a dal, Habib daldi fóon Abdul-Rahman. Noonu la jamm déllu se ci ñaare kër yooya.
Su doomu adama mënee boole jub ak yërmande, Yàlla itam mën na ko def!
Yéesu Yonent bi: Yërmànde bi Jóge ci Yàlla
Fan la nu mën a jànge yërmande Yàlla? Loolu yomb na lool. Xéyna mës nga dégg ni Yéesu Yonent bi (nu xame ko itam ci Isa al-Masi) nu koy woowe “Yërmànde” bi jóge ci Yàlla. Loolu dafay tekki ne moom ci boppam mooy yërmande. Yoonam—njàngaleem ci téeerey wa jàangu yi, te nu xame ko itam ci Injil—mooy yoonu njégalee ak juboo.
Yéesu Almasi Isa mën na matal cër bu rafet boobu ndaxte moom rekk la Yàlla yonni te amul benn bàkkaar. Bépp yonent ak ndaw bu sell soxla nga baalu ci say njuumte, wànte moom Almasi Isa, soxlawul loolu. Yàlla jële na ko fi yobbu ko Àjjana te du taxaw bésu peñc ndaxte musul a def ab njuumte—ba ci bu gën a tuuti.
Lii nag mo tax ni tudde ko Yërmànde Yàlla bi. Moom jox nanu ab misaalu yërmànde bu sell, te jàngal nanu nan lanuy mën a ame yërmànde googu.
Naka la ma Almasi Isa Mën a Dimbalee?
Mbind mi ne na Jean Batist bi (nu xame ko itam ci Yahya) gis na Yéesu Almasi Isa ci biir ab mbooloo te, ci li ko Yàlla feeñu, mu wax ci kaw: “Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina” (Téere Injil, Yowaan 1:29). Yéesu Almasi Isa dafa mel ni xar mooma indi juboo ci wàllu Abdul-Rahman.
Sunu nu mbuggalee ndax sunuy bàkkaar, loolu mooy yoon. Wànte Yéesu Almasi Isa, moom mi musul def bàkkaar, nangu na yennu sunuy bàkkaar. Kenn tënku ko ci. Moom ci boppam moo nangu yennu dee ngir tontu laaju yoon njub. Moom rekk mo nekkoon nit ku jub ci àdduna sépp, wànte mu nangu ñu yamale ko ni xar moomu ci taariqu Abdul-Rahman. Lii moo tax, gannaaw bimu sonnee ngir ñun, Yàlla daldi ko yóbbu àjjana.
Mën nga jànkonteel ak ay jafe-jafe ci sa dund. Mën nga mel ni Fatima, mi waa këram yi sànni ca biti. Mën na am nit gaañ la, mbaa ñu yàqq sa der ci ludul yoon. Mën nga mel ni Abdul-Rahman, mi tooñ te raggal fayyu bi.
Yéesu Almasi Isa mën na la dimbali. Mën nga rekk def ñaan bu gàtt bu mel ni:
Yaw Yàlla sama Borom, mënuma fay mukk samay bàkkaar. Wànte xam na ne yónni nga Yéesu Almasi Isa niki sa Yërmànde ci nun. Mangi lay ñaan nga balma samay bàkkaar ndax liggéey bu baax bi mu def ngir doomi adama yépp. Dimbali ma ndax ma nànd yoonu Yéesu Almasi Isa ngir ma mën a xam sa yërmànde ci samag dund. Amiin.
Su de bëgg nga am sab téereb Injil, jokkool ak ñun soo ko bëggee ci yëgle yi nekk ci gannaaw kayit bii.
Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.
Bindul ci sunu yéenekaay
Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

Siiwal yu fës
© 2023 Sharing Hope Publications