
Muslay ci Rab yu Bon yi
Tënk
Rab yu soxor yi dañu am doole, waaye seen doole yemul ak bu Almasi Yéesu. Téere bu ndaw bii dafa nuy won naka la Yéesu di dàqqe seytaane yi ci yarami nit ñi te faj seeni feebar. Moom mën na ñu def tey ni li mel. Téereem bi dafa nuy jàngal lépp lunu bëgg a xam ngir muslu ci tiitalu seytaane ak nootàngeem. Dafa nuy jàngal itam naka lanuy mën a moytoo workat yu seytaane yi bala moo dikkaat.
Xeet
Kayitu siiwal
Siiwalkat
Sharing Hope Publications
Jàppandi ci
21 Kàllaama yi
Xët
6
Jinne yi ñu ngi fépp. Mo xam ay rab la, ay njuuma, ay saytaane, wala jinne, mën nañu la tiital. Maa-mën yi, fajkati dëmm yi, ak njabarkat yi nekk nañu ñu siiw, wànte ndax ñom mën nañu nu aar?
Bëggoon na séddoo ak yeen ñetti mbir yu yomb ngir aar sa bopp ci rab yu bon yooyu ba dootoo leen ragal.
Muslu ci Rab yu Bon yi
Ki ab waay la bu defoon yaramu neen te di yuuxu. Ay jinne yu bare ñoo ko jàppoon, te kenn mënu ko woon a dimbali. Waa dëkk ba doon ko jéem a takk ak ay seenu weñ, wànte moom dafa leen a dagg ak doole bu jéggi dayoo, ba noppi daw dem dëkk ca armeel ya. Noonu mu nekk fa bés bu ne di jooy aka daag yaramam ak ay xeer.
Ba keroog ba nit ku nuy woowe Yéesu Krista àggsi foofa, ñu xame ko itam ci Isa Al-Masih.
Waa ji tiisoon na lool ba bi mu ubbi gémmiñam ngir ñaan ndimbal, jinne ya yuuxu Yéesu Krista ngir mu bañ ko laal rekk. Wànté loolu taxul Yéesu jóge fa. Xamoon na lu xewoon foofa. Ragalul dara, mu digal jinne ya ngir ñu bàyyi waa ji.
Jinne yooya ñaan ko ne: “Bul ñu yobbu ca mbàmbulaan ga!” Ñu ñaan ko ngir mu bàyyi leen ñu dugg ci biir ndiiraanu mbaam-xuux ya nekkoon foofa. Yéesu digal leen ñu bàyyi waa ji te dugg ca biir mala yu setul yooya. Ca saasa, waa ji amaat wérgu-yaram, rekk ndiiraanu mbaam-xuux bépp daw ca tund wa dugg ca ndox ma.
Ca mujj ga, waa ji daldi féex. Mu daldi sant Yéesu bu baax! Wànte du boobu nettali rekk. Yéesu krista amoon na kàttan gu réy ci kaw jinne yu bon ya. Fépp fu mu daan dem, dafa daan yewwi nit ñi jinne ya jàppoon. Mayoon na itam ay talibeem sañ-saañ ci kaw saytaane:
Dama ne, maa leen jox sañ-sañu... joggati mboolem dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ mukk. Noonu leen rab yi nangule nag, buleen ko bége, bégeleen kay la seen tur binde fa asamaan (Téree jàangu yi, nu xam ko itam ci Injil, Luug 10:19-20).
Sunu toppe Yéesu Krista, mën nanu am kaarànge ci dund gii ak yaakaar ca dundug ëllëg! Léegi nanu xool ñetti jéego ngir mucc ci rab yu bon yi.
Jéego 1 bi: Ñaanal ci Doole ji Nekk ca Turu Yéesu Krista
Jéego bi njëk mooy nga ñaan Yàlla muslaay ci turu Yéesu Krista. Nun rekk, mënunu muccal sunu bopp. Wànte bunu tudde turu Yéesu Krista ci sunu dund, rab yu bon yi duñu am benn sañ-sañ ci nun! Yéesu li la wax ci talibeem yi: “dinañu dàq ay rab ci sama tur” (Injil, Màrk 16:17).
Soo gëmee ci ca biir xol ne Yéesu Krista mën na la yewwi, dina ko def! Li ngay def mooy nga ñaan Yàlla ne ko, “Borom bi afal ma rab yu bon yi ci turu kooku Nga yonni fii ci kaw suuf, Yéesu Krista!”
Jéego 2: Ñaanal Yàlla Settalal la sa Xol ci Biir ak ci Biti
Yéesu Krista jàngale na ne warunu séqq dara ak Seytaane. Wax na ne, “kàngamu àddinaa ngi dikk. Manul ci man dara nag.” (Injil, Yowaan 14:30). War nanu itam setal sunu dund te bañ a def dara lu bon.
Lan mooy tekki ne seytaane amul “dara lu mu séqq ak nun”? Li muy tekki mooy moom amul leen ci sunu biir xol yi mbaa sunu kër yi lu mu moom. Danu war a dindi ci sunu dund bidaa yeek téere ndombo yi. Danu war a moytu sikku bàkkaar yu mel ni poornogaraafi, sineebar, ak sàngara si. Sunu duggee ci ay xarbaat di jokkoo ak ñi faatu, mbaa sànni ay kort, danu war a dakkal ci-saa-si xeetu yëngu-yëngu yooyu. Noonu, dinanu raxas sunu wëreefu biti ca pexey Seytaane yi. Gannaaw loolu, danu war a ñaan Yàlla mu baal nu te raxas sunu xol yi.
Jéego 3: Feesalal sa Dund gi ak Leer
Bila Yéesu Krista yewwee ci kàttanu jinne yi, woo ko mu yore sag dund. Bul bàyyi sa xol bi wéét noonu. Yéesu Krista nee na,
Aw rab nag, bu jàppee nit ba bàyyi ko, day wër béreb yu fendi, di wut fu mu noppaloo, te du ko gis. Su ko defee mu ne: “Ca sama kër ga ma jóge woon laay dellu.” Bu dikkee, fekk kër gi wéet, buube, defare ba jekk. Day dem nag indi yeneen juróom ñaari rab yu ko yées, ànd ak ñoom, ñu bokk sancsi; su ko defee ni nit kiy mujje mooy yées na mu jëkke (Injil, Macë 12:43-45).
Soo setalee sa bopp ca jinne yi, fesalal sag dund gi ak leer gi nekk ca Kàddug Yéesu wa, Téere Biibal bi. Yéesu Krista ñew na mel ni “leer ci àddina, ngir ku ma gëm du des cig lëndëm.” (Injil, Yowaan12:46). Na nga fexe ba am ab Téere Yéesu bi te nga koy jàng bés bu nekk ndax leeram bi dàqq lëndëm gi ci sag dund.
Kaarànge Ngir Ëllëg
Jamono ji àdduna si di tukki dégmalsi na su rab yu bon yi gënee am doole bu kenn mësula gis. Yéesu Krista gisoon na ne bala moo dikkaat, mbootaayu rab yu bon yi dina nañu fi def ay yëf yu kéemaane yi bare ngir jéem a nax way-gëm yi. Ci ñenn ñi, jinne yi dinañu feeñu ci ay melokaan yu raglu niki ay njuuma; ci ñeneen, dinañu feeñu niki ay malaaka mbaa sa ni seeni mbokk yu faatu. Seytaane moom dina dem sax ba feeñal boppam ni Yéesu Krista!
Wànte bu kenn nangu ñu fóoxal ko ci ay fen. Sudee nangu nga topp Yéesu Krista, dina la may doole ngir nga jàmmaarloo ak Seytaane. Sama xarit, ci bépp jafe-jafe boo mëna am tay, bàyyil Yéesu mu yewwi la!
Sudee bëgg nga ab taalibe Yéesu Krista ñaanal la ngir nga yewwee ku ci rab yu bon yi, bind nu ci dëkkywaay bi nekk ca gannaaw kayit bii.
Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.
Bindul ci sunu yéenekaay
Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

Siiwal yu fës
© 2023 Sharing Hope Publications