
Ànd ak Sago ca Bésub Peñc
Tënk
Xalaat ci bés-pénc dafay indi tiitaange ci xoli nit ñu bare. Nan lanuy ame kóolute ne dinanu texe ci lu wóor ca bés-pénc ba? Yàlla newoon na dina nu jox ab layookat—Nit ku nuy taxawal ca bés-pénc ni ab layookat di layale sunu mbir fii ci ëttu attekaayu àdduna. Téere bu ndaw bii dafa nuy wonale ab layookat booba te jàngal nu naka lanuy wóoloo sunu bopp ci xalaatu bés-penc ba.
Xeet
Kayitu siiwal
Siiwalkat
Sharing Hope Publications
Jàppandi ci
21 Kàllaama yi
Xët
6
Benn bés ci suba gi, dama jógewoon sama otel ngir teewe am ndaje mu am solo. Dama tàrdewoon ba tax ma doon dawal lu gaaw—ba weesu àppu gaawaay binu ma may. Ca diggu yoon wa, ab alkaati taxawalma te ne ma topp ko ci barabu poliis ba! Ma daldi tiit lool te jaaxle ndaxte xamoon naa ne maa tooñ.
Ci gannaaw loolu alkaati bi bindal ma ab kayit, ñu yóbbu ma ca ëttu àttekaay bu gën a jege ngir àtte ma. Foofa, ma daje fa ak samab xarit buy liggéey niki ab layookat. Amoon na mbetteel bi mu ma gisee. Bi ma ko nettalee sama mbir, mu ne ma, “na sa xel dal. Dinaa toppatoo sa mbir.” Bégoon naa lool. Sama xarit mooy doon sama layookat!
Ndax sama xarit dafa jël sama mbir ngir layool ma, àttekat ba daanuma lu bari. Nii la jógee ca ëttu àttekaay ba di sant Yàlla.
Lu raglu lool nekk na taxaw ca kanamu ab àttekatu àddina. Wànte mënunu ko méngale benn yoon ak li nar a nekk taxaw ci kanamu Yàlla ca bésub peñc bu magg ba. Su bés booba naroon a ñëw ëllëg, mbaa di nga pare?
Di Waajal Bésub Peñc
Am na ay nit yuy soffàntal bésub péñc. Dañuy naan sangara, di tux, di kàrt xaalis, di dem ca baar ya, te di seetaan ay widewoo yu bon. Waroon nañu xam ne mbir yépp nu ngi koy bind ci ab téere bunu deñc, wànte Seytaane moo leen tënk ci ay naxaateem (nu xam ko itam ci Shaytan). Faalewuñu dara.
Yeneen nit ñi dañu ragal lool. Duñu ñeme fàtte benn waxtu julli. Dañuy xalaat mbugalu biir bàmmeel ba, wala xali safara ya ba moo tax ñuy fàtte mbëggeel ak mbaax u Yalla.
Wànte, ni ma amewoon ab layookat ca ëttu àttekaay ba, Yàlla wutal nañu ab layookat bu nuy taxawal ca bésub péñc ma. Doo fa wéet!
Kan Mooy Sunu Layookat?
Xalaat ab loyookat nekkul lu bees. At bu nekk, ay junni-junni ujaaj dañuy dem aji ca ay béréb yu sell ca Bët-gànnaaru Afrig, ca Penku gu diggu, ak ca Aasi. Nit ñu bare dañuy ñaan ca bàmmeeli njiit yu mag ya, di yaakaar ne dina ñu leen taxawu.
Baax na lool nu weg njiit yu mag yooyu, wànte di ñaan ci seeni bàmmeel mba di ci wut ab rammukat loolu Yàlla tere na ko. Nit ñooña dee nañu te manuñu la defal dara. Yonent Yàlla ya sax ñu ngi ci seeni biir bàmmeel, di xaar Bésub Péñc ma.
Doonte dafa haram di laaj ñi dee nu rammu nu, xalaatu rammu ci boppam baax na. Wànte ban xeetu rammukat la Yàlla di nangu? Kooku war na doon ab rammukat buy:
Dund (ndaxte ab nit ku dee mënul wax ci sunu palaas).
Bu musul def bàkkaar (ndaxte ab nit buy bàkkaar mënul taxawal keen ca kanamu Yàlla).
Kan moo mën a def liggéey boobu? Amul keneen ku dul Yéesu Krista mi Yàlla sopp, nu xam ko ci Isa al-Masih, moom mi di dund ci asamaan te sellë.
Xalaatal ci loolu—ndax am na ab nit bu am sañ-sañ ne moom mësul def bàkkaar? Aadama lekk na meññeef ba ko Yàlla terewoon; Noa (Nuh) naan na biiñ ba màndi; Ibrahima (Ibrahim) fen na; Moussa (Musa) faat na ab nit; Daouda (Dawud) njaaloo na ak jabaru jàmbur. Amul kenn ci Yonent Yàlla yi ku mësul moy, wala ku soxlawul baalu.
Wànte Yéesu Krista moom mësul bàkkaar. Moom mi wax na ne, “Te it ki ma yónni moo ànd ak man... ndax man, li ko neex doŋŋ laay def.” (Injil, nu xam ko ci Injeel, Yowaan 8:29).
Jàkkaarloo ak Bésub Péñc ba ak Sago
Yéesu Krista mu ngi dund ca asamaan te amul benn bàkkaar. Bëgg nanu layal man ak yaw. Te mu ngi wajj a dellusi fi ci kaw suuf léegi.
Dina dellusi ñaareelu yoon, li moy woon ne Yéesu Krista moy Yonent bi mujj bi. Waaw, te moom Yéesu raw na ab Yonent—mooy sunu layookat, sunu Njiit, ak sunu Jàmm ca Bésub Péñc ma. Wax nanu ne, “...ci lu wér, ku sàmm sama kàddu, doo dee mukk” (Injil, Yowaan 8:51).
Yéesu deewul; mu ngi dund! Te mu ngi tabax askanam fii ci kaw suuf ba léegi. Yenn-saa yi dina woo nit ñi ca biir askanam, di leen feeñu ci ay gént mel ni ak nit bu sol yéré bu weex wala mu woon leen ay xarbaax saasu nuy ñaan Yàlla ci turam.
Ndax bëgg nga am jàmm ca Bésub Péñc ma? Jebalël sa ngëm ci Yéesu Krista. Lutax nu nar a teg sunu yaakaar ci ay nit ñu dee te xamuñu naka lañuy def ba rëcc ca bésub péñc ma? Yéesu wóor na ko ne palaasam mu ngi ca asamaan. Ni sama xarit booba nekkeewoon sama layookat ca ëttu àttekaay ba, moom dina nu dimbali.
Mënoon nga laajte ndax ab jëf ju rafetee ni mën na am. Yéesu Krista nena, “Su ngeen ma ñaanee mbir ci sama tur, man maa koy def” (Injil, Yowaan 14:14). Jéemal sett ndax li ma lay wax nii ba xam dëgg la. Sudee Yéesu mën na no génné ci bépp jafe-jafe bu nu mën a am tay ji, kon war na mën a nekk sunu layookat. Ñaanal Yàlla ci turu Yéesu ak ab xol bu sell te dinga gis luy am. Mën nga naan:
Yaw Sama Borom, bëgg na xam su de dëggantaan moom Yéesu nga taan ni sunu layookat ca bésub Péñc ba. Sudee dëgg la, maa ngi lay ñaan nga wuyu ma ndax (duggalal sa soxla fi). Ñaan na la li ci tur Yéesu Krista. Amiin.
Sudee bëgg nga yokk sa xam-xam ci nan nga mën a toppe Yéesu Krista, bind nu ca dëkkuwaay bi nekk ci gannaaw kayit bii.
Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.
Bindul ci sunu yéenekaay
Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

Siiwal yu fës
© 2023 Sharing Hope Publications