Ab Wotee Ingir Gàddaay

Ab Wotee Ingir Gàddaay

Tënk

Ndax bëgg nga ab béréb bu gën? Ab bérébu kaarànge, bànneex, ak noflaay? Yàkkamti nanu gis am mbir mu àddina mënula joxe ndaxte ku nekk ci nun Yàlla dafa la sàkkoon ngir nga dugg Ajjana. Almasi Yéesu dem na foofa ba noppi. Xam na yoon wi, te sax, tudde na Boppam “yoon wi!” Téere bu ndaw bii dafa nuy won dëgg yu am solo ci Yéesu yunuy dimbali nu fagaru ngir nekk ay doomu réewu Àjjana.

Yebbi

Abdul-Malek ab mag mu sonn la woon. Gannaaw ba mu ñakke soxnaam ak ay doomam, mu daldi daw Irak ngir rëcc ISIS. Léggi mu ngi dëkk moom rekk ni ab way-làqqu ca réewum Jordani.

Wànte amoon na ab leeraayu yakaar. Amoon na ab doomu-baayam bu dëkk Kanadaa ku ko dimbali mu am liggéey. Mu daldi yéemu lool, mu ñaan ab wiisaa tàmbali di xalaat ab dundu noflaay. Ca mujj ga, ay at yu bare ba ñu weesoo, nu daldi ko may sãn-sãn ngir mu mën a dugg ca réewum Kanadaa. Abdul-Malek daldi bég lool!

Wànte mbégteem googa yàggul. Bi mu àggee Kanadaa ba noppi, mu gis ne dundug way-tukki yombul. Bés bu nekk dina liggéey ba tass. Dëkkandoom yi barewoon coow. Jël woto yombul woon a nànd—ak làkk Àngale bi itam! 

Abdul-Malek bëggoon na lool dund ci ab dëkk bu gën bi mu nekkoon, wànte ba mu àggee foofa, mu yëg ne xolam ma léegi neexagul. Ci la tàmbali di laaj boppam su fekk ne am na fii ci suuf ab béréb bu mën a seral xolam—wala dafa nara xaar ba dem Àjjana!

Tukki ca Àjjana

Mbaa mus nga dund li dal Abdul-Malek? Bëgg-bëggu ab béréb bu gën dafa doon lu am doole ci xolu doomu Adama, te loolu mënunu ko faj ludul nu dugg Àjjana, di sunu kër dëggantaan. Te loolu ab bëgg-bëgg buy waaja am la! Firndey Waxtu yu bare ñu ngi nuy woon ne, ci lu gaaw àdduna bi dina tukki léegi.

Dale ko ay xarnu ba tay, téerey diine Yahut ya, Kërcen ya, ak Jullit ya woonewoon nañu xew-xew yu tiis—ci wàllu kilimaa sunuy “tukki” joge ci àdduna si dugg ca beneen ba. Ñetti diine yépp dañuy jubal ca kanamu Almasi bi di seede ci xew-xew yi nara am ca bu àdduna di tukki.

Lu am solo ci lii, moo di ca diine Jullit yaak bu Kercen ya, Almasi googu doonul kenn ku dul Yéesu krista, nu xam ko itam ci Isa al-Masih. Moo nekkoon Almasi ma doon dund ca réewum Palestine, wànte mu ngiy dund ca Àjjana am na 2,000 at boobaak léegi. Ca mujj ga, dina dellusi ca Bésub Péñc ma. 

Téere bi wax na lu leer ne Yéesu Krista dina dellusi, wànte Jullit yi tamit gëm nañu ne dina dellusi, ndaxte bind nanu ko ci Àlxuraan ji ne: “Te firnde lay doon ci (Bis pénc ba) waxtu wa. Buleen ci am sikki-sàkka. Te na ngeen ma topp : yoon wu jub xocc wqq ngi nii.” (Az-Zukhruf 43:61).

Mel ni ab liggéeykatu way-tukki buy joxe ay tegtal yu am solo ci naka lanuy ame ab wiisaa, Yéesu Krista mu ngi nuy woo ngir nu bàyyi xel ci Màndargaam kon dina nu xam Yoon wu Jub wiy yoobu Àjjana. 

Naka la Yéesu Tegtale Àjjana?

Téere yi, nu xam leen itam ci Injil bi, dañu bind ne Yéesu Krista nee na, “Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.” (Linjil, Yowaan 14:2-3). Yéesu wax na ne mën nanu yobbu Àjjana! 

Won nanu tamit lu ndaw lu jëm ca béréb booba. Wax na ne

  • Foofa du amati dee, naqqar, jooy, walla mettit (Peeñu 21:4).

  • Dinanu am ay kër yu rafet (Yowaan14:2).

  • Goor ñi ak Jigéen ñéppay tolloo daraja ak yelleef. (Waa Galasi 3:28).

  • Lépp dafay leer, jub, te bare bànneex (Peeñu 21:21-25).

Ca dëgg-dëgg, li moy lu sunuy xol bëggoon a am!  

Lutax Yéesu Krista Nara Dellusi

Waaye Yàlla Yonni na ay Yonent yi bare ak ay nitam. Lutax Yéesu nara ñëw ñaareelu yoon bi? Laaj bi naqqariwul a tontu sunu ko méngaleek misaalu way-tukki ba. Ndax am ab wiisaa nekkul lu yomb, ay nit ñu bare dañuy wut ab layookat, bu xam yoon wi. Sunu amee ab sàmmkat, mën nanu ko yaakaar ci mu dimbali nu.

Nonu tamit, Yéesu krista mooy kenn nit ki feeñ ñaari yoon ndax xam na yoonu Àjjana te mën nanu jëmale foofa. Moomci boppam ne na, “Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi” (Yowaan14:6).

Bépp Yónent wala ndaw lu Yàlla yonni def na bàkkaar te dafa war a ñaan njégal. Wànte Yéesu Krista bokku ci. Deful benn bàkkaar ci 33 at yi mu dund fii ci kaw suuf. Looloo tax Yàlla gaawe ko jël yobbu ko ca Àjjana. 

Danu war a jànge ci Yéesu Krista, kenn ku amul bàkkaar ki, naka lanuy toppe ndigal yi ngir dugg ca Àjjana. Noonu kese lanu mën a jaare ca buntu Àjjana. Nu sant Yàlla, mën nanu jànge ci téereem, Injiil bi. 

Wajal Dellusi bu Yéesu Krista

Ndax amuloo mbégte mu mag ci li nga mën a tukki ca ab béréb bu gën ci barab ya? Woo nanu la nga nekk ab way-dëkk ca diwaanu Yàlla bu màgg ba ca Àjjana! Léegi Yéesu Krista dellusi ngir yobbunu nun ñépp ca barab bu neex booba.

Mën na am yaa ngi topp ay doomu aadama te ñoom xamuñu lu leen di xaar ca bésub Péñc? Ak Yéesu Krista, waruloo am sikki-sakka. Ñaanal Yàlla ngir mu woon la yoon wu jub wu Yéesu Krista. Mën nga ñaane nii:

Yàlla sunu Borom bi, sama bëgg-bëgg mooy dund ca ab barab bu gën. Tàggale man ak samay waa-kër ci coono àdduna si. Jàpp na ni waxtu wi daanaka jotna. Won ma yoon wi ndax ma mën a dugg ca barab gu rafet ba nga waajal ngir man. Amiin.

Sudee bëgg nga am ab téere Injil bu wér, bind nu ci dëkkywaay bi nekk ci gannaaw kayit bii.

Al Quran Wolof.Copyright @ 2023 by Sharing Hope Publications. Mën ngeen a sotti te séddoo liggéey bi ci sunu ndigal waaye bu leen ko jaay.
Mbind mi ci Kàddug Yàlla gi lañ ko jële. Copyright © 2010, 2020 AES et MBS. Jëfandikoo ko gannaaw ndogal. Sañ-sañ yépp sàmmu.

Bindul ci sunu yéenekaay

Nekkal kiy njëkk a xam kañ la siiwal yu bees yi di jàppandi!

newsletter-cover